Digle ngir aar sa bopp
Ngir jënd
- Feyal bu nga jotee, bul fey mukk bala loolu. Bul joxe benn avaas, doonte ngir « téye » mbir mi. Jaaykat buy sàkku te di ci sax ba nga fey ko bala ngay jot, ci lu jege yoon yépp, ab njuujkat la.
- Desal ci biir Bwatoo. Jaaykat bu la naan nga jaar ci WhatsApp walla nga woo ko, bari na yoon muy wut a moytu sàrt yi. Xamleel ko.
- Saytul mbir mi. Taalal telefon bi, jéemal oto bi, te méngaleel nimero serii bi ak kayit yi.
- Gisleen ci bérab bu ñépp di jaar, ci bëccëg, walla jaarleen ci ab yónnekatu platfórm bi.
- Taneel jaaykat yu ñu saytu : badge « Telefon bu saytu », te « Dandu bu saytu » moo gën.
Ngir jaay
- Bul joxe mbir mi lu dul bu ñu la feyee. Moytul reçu yu mobile money yu dul dëgg : saytul ba wóor ne xaalis bi agsi na ci sa kont.
- Bul joxe say kood mukk. Bwatoo du la laaj mukk sa koodu dugg, walla sa koodu mobile money.
- Kood bu jot bi bu am 4 siifar, jëndkat bi la bokk : moom moo koy jox yónnekat bi ci saa si ñu koy yónnee.
Oto ak kër
- Ngir oto : kàrt gris, dedwaanmaa ak kontrool teknik, ci turu jaaykat bi.
- Ngir suuf walla kër : tiitar fonsiyee, ACD walla akt bu noteer. Nanu noteer saytu ko bala ngay fey.
- Bul fey mukk ab kosioŋu luwaasu bala nga koy seetsi.
Am nga benn sikk ?
Bësal ci « Xamle yéene bii » walla bind nu jaar ci xët Jokkoo. Ekib bi dafay saytu xamle bu nekk.